lundi 27 avril 2009
Ag Jiital
Salaam sama bokki wolof yi
man dey ab wolof laa bu wolofe te ma yaakaar ni looloo ma war batax ma juk di laggeeyal wolof moomi ngir mu tollook ñi mu bokkal aw tur mudi làkk mbaa sax mu jege leen ndax moom wolof moomi loolu jombu ko ndax yalla taggat nako bamu nooy man dey ngisa guma làkk wu ko gën a mat wumoy araab xanaa kay li am mooy làkk wuñu toppatoo ak wuñu sangane te moom nak melnani ci yiñu xawa sangane ci la bokk man dey loolu neexuma batax ma juk fasyeene cee def lima ci man a kus neew ngir dooleel ko te ma yaakaar ni kepp kuy wolof war nacee japp ndax yàlla mila bind defla gay wolof moo la gën a xam sa bop. di jeggaani aw làkk te yor ci wu nooy te neexa wax loolu bokkul ci fulla day tax ñu yab la rek looloo waral reewi tugal yi not ñu ba leegi nde ñoo ñu abal aw làkk wuñuy liggeeyee te wolof njaay nee ku la aal bët fuko neex gay xool,man dey fippu naa ngir bayyil leen fi seen làkk yooyi du maci weesu jank ak wut xam-xam binu bokk ñun nit ñep teñu aakimoo ko def ko ci seen làkk yi, te buma koci amee insaa allah dinaa ko soppi ci wolof diko jangale, fii ci sunu réew yi litax ñu yeex bokku naci kufi joddoo ñu dugal la ci daaray nasaraan yi 12 at ngay jang ngir degg làkk wi door a dugg ci daara ju kawe ji(universite) di jang laggeey(métiers) xamngeen ni loolu jaaduwul moo waral it doofi gis ku am xaalis ci'k ndawam ak yeneeni mbir yu wara tax ñu fonk suñu làkk wi, làkk woo xamni booy gent ci gay gent booy saaga yit ci ngay saaga boo bëggee defar sa gent dink ko jëfandikoo, waaw-kay

Inscription à :
Articles (Atom)